Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 8

Lan ngeen war a def bu musiba amee

Lan ngeen war a def bu musiba amee

“ Yéena ngi bég bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, yéena ngi dékku tiis ab diir, di seen jànkoonte ak nattu yu wuute. ” — 1 Piyeer 1:​6

Bu dee sax yéen a ngi def seen kem-kàttan ngir am séy bu neex ak jàmm ci seen biir njaboot, terewul musiba mën na am. Bu loolu amee, du yomb ngeen wéy di am mbégte (Ecclésiaste 9:​11). Yàlla mi ñu bëgg dafa ñuy dimbali ngir ñu mën a jànkoonte ak suñu jafe-jafe yi.Bu ngeen toppee santaane Yàlla yii di topp, yéen ak seen njaboot dingeen mën a jànkoonte ak jafe-jafe bu mu mënta doon ak lu mu metti-metti.

1 WÉERULEEN CI YEXOWA

LI BIIBËL BI WAX : ‘ Nangeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la ’ (1 Piyeer 5:⁠7). Buleen fàtte ne du Yàlla moo leen teg musiba (Saag 1:​13). Bu ngeen jegee Yàlla ci ñaan, dina leen dimbali ci fasoŋ bi gën (Isaïe 41:10). “ Diisleen ko seen xol ”. — Sabóor 62:⁠9.

Nangeen jàng itam Biibël bi te gëstu ko. Loolu dina dëfal seen xol. Dingeen gisal seen bopp ni Yexowa di ‘ dëfalee suñu xol ci suñu tiis yépp ’ (2 Korent 1:​3, 4 ; Room 15:⁠4). Te dige na ne dina leen may “ jàmmu Yàlla, ji xel manta takk ”. — Filib 4:​6, 7, 13.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Ñaanleen Yexowa mu dimbali leen ngeen am xel mu dal, ñaan ko it ngir mbir mi leer ci seen bopp

  • Xoolleen pexe yi ngeen am te tànn bi ci gën

2 TOPPATOOLEEN SEEN BOPP AK SEEN NJABOOT

LI BIIBËL BI WAX : “ Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam ” (Kàddu yu Xelu 18:15). Jéemleen a xam lépp li poroblem bi ëmb ak li kenn ku nekk ci seen njaboot soxla. Waxtaanleen ak ñoom te déglu leen bu baax. — Kàddu yu Xelu 20:⁠5.

Lan ngeen mën a def bu ngeen amee ku dee ? Buleen a ragal a wone li ngeen di yëg ci seen xol. Fàttalikuleen ne Yeesu sax ‘ jooyoon na ’ (Yowaana 11:35 ; Ecclésiaste 3:⁠4). Noppalu bu doy ak nelaw bu doy am na ci solo (Ecclésiaste 4:⁠6). Loolu dina tax ngeen gën a mën a jànkoonte ak seeni jafe-jafe.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Nangeen faral di waxtaan ak seen njaboot. Su ko defee, bu musiba amee, dinañu kontine di waxtaan ak yéen.

  • Waxtaanleen ak ñi mas a jànkoonte ak coono bi ngeen di jànkoonteel

3 NANGULEEN ÑU DIMBALI LEEN

LI BIIBËL BI WAX : “ Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono ” (Kàddu yu Xelu 17:17). Seeni xarit mën nañu leen a bëgg dimbali waaye xéyna xamuñu ni ñu koy defe. Nangeen leen wax li ngeen soxla dëgg (Kàddu yu Xelu 12:25). Wutleen itam ndimbal ci ñi nànd Biibël bi bu baax. Seeni xelal yu sukkandiku ci Biibël bi dinañu leen mën a dimbali. — Saag 5:14.

Dingeen am ndimbal bi ngeen soxla bu ngeen di faral di booloo ak ay nit ñi gëm Yàlla dëgg ak li mu dige. Bu ngeen di dimbali ñi soxla ndimbal itam loolu dina dëfal seen xol. Deeleen waxtaan ak ñoom ci ngëm bi ngeen am ci Yexowa ak ci ay digeem. Kontineleen di dimbali ñit ñi nekk ci soxla, te buleen sore ñi leen bëgg te yëg leen. — Kàddu yu Xelu 18:1 ; 1 Korent 15:⁠58.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Waxtaanleen ak xarit bu leen jege te bàyyileen ko mu dimbali leen

  • Waxleen seeni soxla ba mu leer te buleen nëbb dara