Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

RÉVEILLEZ-VOUS ! No 2 2018 | 12 ponk yiy tax njaboot yi am jàmm

12 ponk yiy tax njaboot yi am jàmm

Am na lu bare luy xañ njaboot yi jàmm. Waaye njaboot yi am jàmm, lan moo leen dimbali?

  • Ci digante 1990 ak 2015 ci Etaa Sini, limu nit ñi am 50 at te seen séy tas yokku na ñaari yoon. Limu ñi am 65 at te seen séy tas, yokku na ñetti yoon.

  • Yenn waajur yi, xamatuñu li ñu war a def: Am na ay boroom xam-xam yu wax ne, waajur yi dañu war di neexal seeni doon. Ñeneen ñi naan, war nañu won xale yi mbëggeel waaye dañu war a dëgër ak ñoom.

  • Ndaw ñi dañuy dem ba doon mag, te duñu xam ni ñuy yore kër.

Loolu terewul . . .

  • Séy mën a nekk lu neex te yàgg.

  • Waajur yi mën nañu jàng ni ñuy yare seeni doom ànd ci ak mbëggeel.

  • Ndaw ñi mën nañu am tey, jikko yi leen di amal njariñ bu ñu magee.

Loolu, nu mu mën a nekke? Yéenekaay bii, tudd Yéewuleen!, dina wax ci 12 ponk yiy tax njaboot yi am jàmm.

 

1: Sàmm kóllëre

Ñetti xelal yu mën a dimbali jëkkër ak jabar ñu wéy ci seen séy.

2: Déggoo

Ndax ki nga séyal dafa mel ni dëkkandoo ci yow?

3: Respe

Xoolal li nga mën a def ak li nga mën a wax ba sa jabar walla sa jëkkër yëg ne respekte nga ko.

4: Baalante

Lan moo la mën a dimbali nga bañ a xool ci njuumtey ki nga séyal?

5: Waxtaan

Ñetti yëf yu la mën a dimbali nga gën a jege say doom.

6: Yar

Ndax yar dafay tax xale xeeb boppam?

7: Jikko

Yan jikko nga war a jàngal say doom?

8: Royukaay

Boo bëggee say kàddu laal sa xolu doom, fàww ñu méngoo ak say jëf.

9: Ki nga doon

Naka la ndaw ñi mënee fonk li ñu gëm?

10: Kóolute

Def liy tax say waajur wóolu la, lu am solo la ngir doon mag.

11: Cawarte

Boo jàngee def liggéey bu baax, bi ngay nekk ndaw, loolu dina la dimbali nga am ndam ci lépp li ngay def.

12: Jubluwaay

Matal say jubluwaay, mën na tax nga gën a wóolu sa bopp, sa diggante ak say xarit gën a dëgër te yokk sa mbégte.

Yeneen ndimbal ngir njaboot gi

Xelal yi nekk ci Biibël bi mën nañu la dimbali nga am jàmm ci sa séy ak ci sa njaboot.