Ubbil li ci biir

Lu tax nit di dee?

Lu tax nit di dee?

Li Biibël bi wax

Laaj lu tax nit di dee lu jaadu la, rawatina bu dee suñu mbokk walla xarit moo gaañu. Biibël bi nee na: «Peyu bàkkaar mooy dee» (Room 6:23).

Lu tax nit ñépp di bàkkaar te di dee?

Suñuy maam Aadama ak Awa ñàkk nañu seen bakkan ndaxte dañu bàkkaaroon (Njàlbéen ga 3:17-19). Seen bañ a déggal Yàlla, dee rekk la leen jural, ndaxte ci Yàlla «la dund di balle» (Sabóor 36:10; Njàlbéen ga 2:17).

Aadama wàll na doomam yépp bàkkaar. Biibël bi nee na: «Bàkkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar» (Room 5:12). Kon ñépp ay dee ndaxte ñépp ay bàkkaar (Room 3:23).

Naka la dee di jeexe?

Yàlla wax na ne bés dina ñëw «dina noot dee ba fàww» (Esayi 25:8). Waaye bala muy def loolu, fàww mu dindi li waral dee, maanaam bàkkaar. Dina ko def jaare ci Yeesu Kirist miy «dindi bàkkaaru àddina» (Yowaana 1:29 ; 1 Yowaana 1:7).